Sabóor 3
Aji jub a ngi woote wall 
 1 Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda, ba muy daw Absalom doomam ju góor* 3.1 Seetal ci 2.Samiyel 15—16.. 
 2 Éy Aji Sax ji, noon yeeka bare! 
Ñu baree may jógal, 
 3 ñu baree may tooge naa: 
«Yàlla du ko wallu!» 
Selaw
  4 Waaye yaw Aji Sax ji, yaa may feg, 
di ma teral, di ma siggil. 
 5 Maay woo Aji Sax ji wall, 
mu walloo ma fa tundam wu sell wa. 
Selaw.
  6 Maay tëdd nelaw, yewwu; 
Aji Sax ji di ma aar. 
 7 Ñu dul jeex a ma jógal, gaw ma, 
te duma ragal. 
 8 Éy Aji Sax ji sama Yàlla, 
jógal, wallu ma! 
Yaa toj kaabaabi noon yu bon yépp, 
foq seeni sell. 
 9 Aji Sax ji, yaa moom wall, 
sa mbooloo jagoo sa barke. 
Selaw.