Sabóor 110
Yàlla fal na nitam 
 1 Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. 
Aji Sax ji daa wax sama Sang, ne ko: 
«Toogeel sama ndijoor, 
ba ma def say noon sa ndëggastal.» 
 2 Sa nguur la Aji Sax ji saxal, dale ko fa Siyoŋ. 
Yilifal noon yi la wër! 
 3 Sa mboolooy taxawal seen bopp, 
sa bésub xare. 
Ña nga soloo darajaak sellnga, 
faboo fa njël sosoo, 
diy ndaw, wàccsil la, mbeteb lay. 
 4 Aji Sax jee ko giñ, 
te du dellu gannaaw: 
«Yaa dib sarxalkat ba fàww, 
topp dayob Melkisedeg* 110.4 Melkisedeg: buurub Salem la woon, di sarxalkat bu Yàlla faloon ci jamonoy Ibraayma, maanaam ñeenti téeméeri at laata Aaróonaa doon ab sarxalkat..» 
 5 Sang baa ngi fi sa ndijoor 
te mooy rajaxe buur yi, bés bu meree. 
 6 Mooy mbugal xeet yi, jal seeni néew, 
di rajaxe kilifay àddina, ba mu daj. 
 7 Déeg ba feggook yoon wa, Buur a cay naan, 
te moo ko tax di siggi. 
*110:4 110.4 Melkisedeg: buurub Salem la woon, di sarxalkat bu Yàlla faloon ci jamonoy Ibraayma, maanaam ñeenti téeméeri at laata Aaróonaa doon ab sarxalkat.